Viatique #2 : Se défendre…

Ce texte est le deuxième d'une série de viatiques, en français et en wolof, du conteur sénégalais Masamba Guèye, qu'Urbasen se propose de publier chaque semaine.

Viatique #2 : Se défendre…

« Défends-toi, et défends l'honneur de ta famille par tes nobles actions et propos. Ne sois ni injuste, ni corrompu.e, ni menteur.se, ni traitre.sse, ni renégat.e, ni pitre, ni cupide, ni entremetteur.se, ni courtisan.e, ni comploteur.trice, ni jaseur.se, encore moins hypocrite. Qui parle de toi, parle des tiens ! Il te faut donc, penser aux conséquences de tes faits et mots sur ton entourage qui t’aime, qui ne t'aime pas, dont tu portes le nom, avec qui tu partages le village, la ville et le pays. Nous sommes tou.tes des délégué.es des nôtres. Nous ne devons pas les exposer à la honte par nos vilenies.

 

Évite d'être une faille sociale. Il ne faut pas exposer la dignité de ton cercle par ta cupidité, par ton désir de pouvoir ou par simple félonie. Ne sois pas de ceux.elles qui n'ont d'autres ambitions  que d'accumuler des biens matériels quoi qu'il en coûte et qui, pour des rentes, une nomination ou une élection font fi de l'honneur et de l'éthique. Ne sois pas de ces gens capables de se contredire, de se renier, de se dédire sans vergogne et qui n’ont ni idéologie, ni parole, ni foi en rien. Protège tes enfants, ta lignée, tes collègues et ton peuple par ton comportement constamment réglé sur les valeurs sociales cardinales.

Chacun de nous doit être un bouclier pour l’honneur des siens !»

Dr Massamba GUÉYE LBA

---

Yóbbalu 21 fanu Oktobar 2022

Aaru…

« Warunoo xajamal sunu deru ñoñ ndax sunuy ñaawtéef. Aaral sa bopp, aaral saw askan ci sa jëf ak wax ju rafet juy tax kenn du wax lu bon ci yow fekk muy dëgg. Bul jeng, buñ la ger, bul nar, bul wor, bul xotti kóllare, bul ñàkk fayda, bul bëgge, bul waabajiiba, bul ndiigu, bul coogu, bul jëw, waxeesut naaféq. Lees wax ci yow rekk, waxees na ko sa ñoñ. Kon saa su ne war ngaa xalaat sa njeexitalu jëf ak wax ci say jegeñaale : ñi la bëgg, ñi la bëggut, ñi nga bokkal sant, ñi nga bokkal dëkk ak réew. Kenn ku ne foo nekk sa ndawal ñoñ ga, di setal mbaa di tilimal seenub der.

 Moytul a doon sànkar ci sa biir askan. Bul weer mukk say bokk ndax sag bëgge, sag xiif nguur mbaa sag ndëngte. Bul bokk ci ñi nga xam ne alal rekk a leen ñor te seexluwuñu dara ba tax ngir am poñet, mbaa ag pal, mbaa ab tabb man nañoo jaay seen ngor. Xeetu nit ñooñu amuñu kàddu, dëkke wax-wàqet, amuñu jom, duñu jomb dara, gëmuñu lenn.

Aaral say doom, saw xeet, say naatangoo, sa waa dëkk ci sa yiiwe, sa ngor, sa maandute. Ku ne ci nun yaa war di fàggul sa ñoñ gàcce  waaye ndax nun ñépp xamee nanu ko noonu ? »

Dr Masàmba GÉY LBA