Viatique 4#:Travailler ...

Ce texte est le quatrième d'une série de viatiques, en français et en wolof, du conteur sénégalais Masamba Guèye, qu'Urbasen se propose de publier chaque semaine. illustration: Baay fall chez Ndigeul Fall Thies. ©Vieux Sané

Viatique 4#:Travailler ...

Travailler, ce n'est pas uniquement embaucher et débaucher. Travailler, c'est se fixer des objectifs pour chaque activité, tout faire pour les atteindre et mesurer à la fin leur impact positif sur sa communauté. Travailler, c'est se donner, en âme et conscience, les moyens d'être fier.e des heures, des jours et des années qui défilent en voyant sur le visage des bénéficiaires le mieux-être et un bonheur de vivre.

Il est facile d'occuper des heures, de remplir du temps mais travailler sérieusement c'est être efficient pour faire des résultats quantifiables permettant d'améliorer le bien-être de sa société. Travailler honnêtement, ce n'est pas quitter sa maison tous les jours, aller sur un lieu, s'y agiter et revenir le soir pour donner l'impression d'être actif.

Il ne suffit donc pas de se dire travailleur pour l'être effectivement. Il faut plutôt prendre conscience que chaque seconde qu'on attribue à une action est une seconde prise à notre vie et que par conséquent, il faut la rentabiliser parce que c'est un instant qu'on ne revivra plus. Chaque instant qui passe doit être consacré à bien travailler et doit nous apporter le bonheur immense de nous sentir utile au service des nôtres et du monde.

C'est par le travail qu'une personne se réalise. C'est par lui qu'on acquiert sa dignité mais c'est par l'impact durable de son travail qu'on se sent humainement utile. Les ennemi.es du travail sont le désordre, la paresse, la mauvaise foi, la tricherie, la corruption, la concussion et la gabegie.

Qui veut tuer son pays triche dans son travail. Mais qui le fait, jamais ne pourra, chaque soir, fermer les yeux et vivre l'immense joie d'avoir contribué à améliorer son monde !"

Dr Massamba GUÈYE LBA

--

Yóbbalu 12 fanu Nowàmbar 2022

Liggéey ...

Liggéey du rekk xëy ak wàcc waxtu. Liggéey mooy sas sa bopp waar  bés bu ne te nekk ca ba mu am njeexital ci sa dundiinu askan. Nekk ca sa barabu liggéeyukaay rekk waxtu yiy romb, yomb na waaye am fa njariñ cig xerèñ, mbaa liggéey lu kuney teg bët te mu am njariñ aka jafe. Liggéey dëgg du rekk jóge sa kër suba gu ne mel ni kuy yëngu. Liggéey mooy def sa àqulaay taalaa ci sa jëf ba naw sa bopp saa su ne bay gis ci sa gët i ñoñ mbég ak dalug xel gu juddoo ci sa liggéey.

Ne liggéeykat laa rekk taxut nga doon ko. Moo tax nga war a bàyyi xel ne saa soo jox sam xëy, da nga wàññee ci sag dund kon war nga koo ñoŋal ndeem doo ko dundaat.  Saa su romb war nga ko jagleel liggéey, mu jural la mbégtem xam ni yaa ngi suuxat saw askan ak àdduna.

Liggéey rekkay tax nit doon dëgg-dëggi nit cim réewam. Ci liggéey la nit di sàmmee ngoram waaye ci liggéey bu maandu lay yëgee ne dundam am na njariñ. Noon i liggéey ñooy jaxas-jaxase, naaféq, tappale, ger, parparloo ak njuuj-njaaj. Ku bëgg a ray sam réew, deel liggéeyantu. Waaye ku koy def, doo mas a gëmm say gët am bànneexu gis ni soppi nga jamono ci lu baax."

Dr Masàmba GÈY LBA