Viatique 5#: Adversaire ...

Viatique 5#:  Adversaire ...

Ton adversaire n'est pas ton ennemi.e. En réalité, ton.a seul.e véritable adversaire, c'est toi-même! Pour les grands combats de la vie, il faut des adversaires de rang, qui ont du mérite et de l'éthique et dont les armes affûtées donnent à nos Victoires l'éclat solaire au zénith. On ne peut pas marquer l'Histoire sans grandeur d'âme.

Souhaite à ton adversaire force, bonheur et la dignité grande pour que chaque lutte de ta vie soit mémorable. Ne désire jamais n'avoir que le.a faible face à toi. Cela te réduit à être le champion des tocards. Le.a véritable héros.ine affronte de grands antagonistes. Cela fait sa geste !

Ne pas respecter son adversaire, c'est manquer de sagesse. C'est perdre la face que de le.a railler sauf à vouloir pimenter les instants d'avant combat tel le lutteur faisant son "bàkk" egotrip. Ne cherche donc ni à le.a réduire en poussière, ni à le.a détruire avant de l'affronter pour qu'il.elle ait la sérénité et l'énergie nécessaire quand tu lui tiendras la dragée haute. Bats-le.a mais ne l'humilie point. Ne te réjouis pas de le voir tomber malade. Ne le neutralise pas par des coups bas. Domine-le.la par ta générosité dans l'effort, ta force physique et mentale, ta loyauté au combat et ta dignité.

Ton adversaire t'offre l'opportunité d'une gloire fabuleuse à léguer à tes descendants. Respecter son adversaire, c'est élever la dignité humaine à son paroxysme. Ainsi, au crépuscule de ton parcours, tu pourras t'asseoir avec lui.elle, la main dans la main, faire le bilan de ton pedigree sans courber l'échine. La seule victoire qui vaille est celle de l'honneur.

Dr Massamba GUÉYE LBA

 

---

Yóbbalu 19 fanu nowambar 2022

Ki ngay joŋanteel...

Ki ngay joŋanteel du sa noon. Kenn rekk sax de ngay joŋanteel dëgg muy sa bopp. Kenn manuta doon ku ñuy roy te doo ndaanaan. Ngir am ndam yu mag yi fàww nga jaakaarlook boroom dayo yu am jom te jomb, am ngor te yiiw ngir sa ndam mel ne jantub digg bëccëg.

Ñaanalal ki ngay joŋanteel doole, wér, ngor ak jàmm ngir soo ko daanee muy lees di fàttaliku ba fàww. Bul ñaan mukk songook cuune ndax dangay mujj a ub làmbu aji-nasax yi. Kàngam dëgg, bu góor mbaa jigéen, day daan mbër yu mag. Ñàkk a wormaal ki ngay joŋanteel ci ñakk fit la bokk. Di ko kekkantoo ci dul bàkku giy xumbal làmb ji, wane sa wayadi la. Kon bul jéem a nasaxal ki ngay joŋanteel laata ñuy sàjj, mbaa di  wàññi dooleem. Ba ko mu fees dell, nga daan ko jéll bu rëy.

Daanal ki ngay joŋanteel waaye bu ko toroxal. Bul bégee mukk aw ayam mbaa di ko yéene wopp. Bu ko fexeel ngir mu nasax te sëggaguleen. Waral ci kowam ak sa fulla, sa fayda, sa jom ak sa fit wu gore.

Wegal ki ngay joŋanteel ndax mooy jox sa àdduna dayo. Mooy tax nga bàyyee sa ndono woy wu rëy. Moo lay def boroom ndam lu rëy lees di wër. Looloy tax bu lépp wéyee nettali ba rafet. Làmbi ngor rekk a jar a ub."

Dr Masàmba GÉY LBA