Viatique #1 : Erreur

Ce texte est le premier d'une série de viatiques, en français et en wolof, du conteur sénégalais Masamba Guèye, qu'Urbasen se propose de publier chaque semaine.

Viatique #1 : Erreur

« Si tu fais une erreur, ce n’est pas grave mais assume-la ! Ne ressasse pas tout le temps le passé ou le résultat insatisfaisant. Une erreur peut être sentimentale, professionnelle, politique, religieuse etc... Quoi qu'il en soit, si ton engagement à agir est sincère, si ton choix est honnête, tu ne peux rien te reprocher. Il faut garder ta lucidité, ne pas suicider ton espoir et mettre un clap de fin à cette tranche de ta vie.

 

L'erreur est humaine, c'est insister dans l'erreur qui est le problème ! Il faut être fort.e et reconnaître son erreur, la corriger si possible, réparer ses conséquences nécessairement, l'évaluer et en faire une leçon de vie. Parfois, on aime une personne pour qui on sacrifie tout et qui nous déçoit, on recrute une personne en qui on place une totale confiance mais qui nous abandonne ou nous trahit, un homme fuit ses responsabilités après une grossesse, une femme se rétracte après avoir pris nos biens, un partenaire disparaît avec nos parts, un parent détourne nos envois et point de maison ou une arnaque nous atteint, mais il faut apprendre de tout cela sans  pleurnicher, sans passer de victime à auto-accusé.e.

 

Mesure ton erreur et fais-en une rampe de lancement des futurs succès de ta vie. Écoute-la et tu entendras une voix intérieure te dire où aller. Si tu refuses d'assumer ton erreur, tu la subis et tu commets l'erreur irréparable car tu t'emprisonnes dans l'échec et crées un malaise. »

---

Yóbbalu 14 fanu Oktobar 2022.

Njumte

« Juum, dara nekku ci, boo juumee, nangul ni dangaa juum. Bul bay-bayaat metit wi weesu mbaa ak lajj. Nit da na juum ci mbëggeel, polotig, diine mbaa leneen. Ak lu man di xew, bu dee la taxoon nga jëf yéene ju baax la woon ak njort lu rafet te dëggu, bul am looy meree sa bopp. Dalal rekk, bul xaruloo sa yaakaar te nga tëjal sa bopp buntub njumte ci sa àdduna.

Njumte ak nit a ànd, dëgër bopp ci njumte mooy musiba. Nit ku mat dëgg mooy nangu ne juum na, jubbanti ko, joxe ndàmpaay bu waree, defaraat la mu yàq bu manee nekk, càmbar ko ba jàngee ca.

Yenn saa yi nga bëgg nit jaay sa lépp ndax moom mu wor la, nga jël liggéeykat, wóolu ko, mu ñuuy la, dem bàyyi la, walla góor tooñ jigéen ba noppi bañ, mbaa jigéen jël sa alal, dem sëyali  keneen, mbaa sa waay jël sa wàll ci la ngeen bokk, ne mërr réer la, mbaa nga yónnee mbokk sa alal mu lekk ko, du la tabaxal, walla sax njublaŋ jekkula.

 

Waaye loola lépp, jàngee ca àdduna. Bu fa toog di ko jooy ndax du ko faj. Bul àtte sa bopp ne ku tooñ mbaa ku sàggan lool. Nangul sa njuumte te jàngee ca lu tungóom say ndam ci dunyaa. Déglul say njumte ba dégg sa baatu biir bi lay yee. Njumte dëgg, bi yées mooy juum di ko bañ, ndax mooy kasob nit,te day tas àdduna. »

Dr Masàmba GÉY LBA